Njaboot yu and ak ay xale yu amagul 21 at, jigéen yu ëmb wala njaboot yu am ay jigéen yu ëmb dañoo wara bindu ngir am ab laquwaay ca santaru DHS' Prevention Assistance and Temporary Housing (PATH).
PATH moo ngi nekk ca:
151 East 151th Street
Bronx, NY 10451
718-503-6400
Ngir dem foofu, jëlal otoraay 2, 4, wala 5 yuy dem 149th Street/Grand Concourse Station.
PATH dafay wëy di dox 24 waxtu bis bu nekk, boole ci mboolem ayu-bis ak bisu fête yi. Dañuy amal bindu yi bis bu nekk digante 9:00 waxtu ci suba ba 5:00 waxtu ci ngoon. Ay sàrwiisi lakk yu amul fay te teggu ci sutura, bokk na ci sàrwiisi firi lak ñi tëx ak ñi muumë, am nañ fa saa su nekk.
Njaboot yuy bindu ngir am ab laqukaay ca PATH dañoo wara indi dantite wu ñi bokk ci kër gi yépp.
Ngir am yeneeni leeral ci PATH, yebbil sunu téere gindikaay.
Ab njabootu mag mooy bépp njaboot bu amul ay xale. Bokk na ci ñaar ñuy sey, ñaar ñu bok fi ñuy yeewo, ay waajur ak ay xale yu am lu ëpp 21 at, ab mag ak rakk wala ay nit yu mëna firndéel ni ay wey-deñcante lañu (ci wallum yëg-yëg, wala ñuy jàppale ci wergu-yaram). Njaboot yi dañoo wara and dëkk gën gaa neew juróom benni weer ci at bu mujj bi.
Njabootu mag ñi dañoo wara bindu ngir am laquwaay ca:
Santaru Adult Family Intake Center (AFIC)
400-430 East 30th Street
New York, NY 10016
Ngir dem fa, jëlal otoraay 6 buy dem 28th Street wala bus M15 buy dem 29th Street.
AFIC dafay wëy di dox 24 waxtu bis bu nekk, bokk na ci mboolem ayu-bis ak bisu fête yi. Ay sàrwiisi lakk yu amul fay te teggu ci sutura, bokk na ci sàrwiisi firi lak ñi tëx ak ñi muumë, am nañ fa saa su nekk
Ñi bokk ci njaboot gi yépp dañoo wara indi seen dantite bu baax ak ab limu adarees yuñu njëkkoon a dëkk, bokk na ci bépp keyit buy firndéel seen dëkkuwaay bu jàppandi.
Magi salibateer yépp dañoo wara bindu ngir am laquwaay ca;
30th Street Intake Center
400-430 East 30th Street
New York, NY 10016
Ngir dem fa, jëlal otoraay 6 buy dem 28th Street.
30th Street dafay wëy di dox 24 waxtu bis bu nekk, bokk na ci mboolem ayu-bis ak bisu fête yi.
Salibateer yu jigéen yi mën nañu bindu ngir am ab laquwaay ci bu ci nekk ci ñaari barab yile:
HELP Women's Shelter
116 Williams Avenue (digante Liberty Avenue ak Glenmore Avenue)
Brooklyn, NY 11207
Ngir dem fa, jëlal otoraay C buy dem Liberty Avenue.
Franklin Shelter
1122 Franklin Avenue (wetu 166th Street)
Bronx, NY 10456
Ngir dem fa, jëlal otoraay 2 buy dem 149th Street wala bus BX55 buy dem 166th Street ak 3rd Avenue.
Magi salibateer yi dañoo wara dellu ci seen laquwaay yuñ leen njëkka jagleel sudee dañ leen ko joxoon ci 365 fan yu mujj yi.
Biro Jubolekàt bi mën na la jàppale indil la ay saafara ci jafe-jafe laquwaay ak li aju ci ñakkul dëkkuwaay. Ay Teewalkati Sàrwiisu Constituants mën nañ la dimbali ngir:
Dañoo moom seen bopp te duñu liggéey ak ñiy joxe laquwaay yi.
Constituants yi mën nañu jokkoo ak Biro Jubolekàt ci ñeenti anam.
Ngir am yeneeni costéef ngir nga wëy di nekk ci sa kër, demal ci daluwebu NYC Human Resources Administration website so bësee fii.